« Màggal leen bis bi ci jàng alxuraan, tudd yàlla ci xeeti tudd yàlla yépp, jàng xassida, joxe aw ñam rawatina ci jirim yi ag way ñakk yi, jokk ag mbokk, siyaare gaa yu baax yi ...»
Ab jukki ca xutbab Sëñ Fàllu Mbàkke ba, ci maggal tuubaa gi njëkk tollook 11 samwiye 1947
76
Santle leen ma Yàlla ci bisub 18 Safar !
Day melni kon cant gi murit yi ag mbindéef yepp di sant yàlla ci bis bi génnug cant la muy cantug Sëriñ Tuubaa gu ko nit ñi fekksi ngir jàpple ko ci. Bu boobaa nag ci maqaama Sëriñ bi ag dayoob cantam la yàlla di faye.
Comprendre la doctrine d'abord.
Notre ère n'est plus celle de l'obéissance aveugle à un guide ; il faut, avant tout, s'abreuver de l'enseignement du Cheikh. C'est uniquement cette démarche qui permettra de bien identifier qui l'on doit suivre et ce que l'on doit suivre.
Le prédicateur du déclin des confréries et ses sbires endoctrinés, avec leur météo fausse, ont sûrement été guidés par des délires et non par des facteurs rationnels considérables. Ou peut-être parlaient-ils d'une autre époque dans leurs songes.
Ñëw na ci Hilyatul awliya, Abu nahim Al asfahani mu wax ne: Am na ku laajoon Imam Chafi «ñaata att nga am?» Imam Chafi neko «Bokkul ci kersa nit di wax ay atam».
Amna ku laajoon Imam Maalig ay atam Imaam Maalig ne ko laajal lu la amal njariñ.
1
56
Bala ngaa xamne addunaa ñàkk solo nga romb sëgg yoo xamoon ña fa tëdd, mbaa kër buur bu folliku mbaa màggatum jongoma wala waxambaane woo xamoon bamuy ndaw, mbaa tabax bu rapp boo fekkewoon yees ga.
Buñ la dee jay fii fi àddina ba nga defe ne manoo fee ñàkk toxantul ca almeer ya. Da nga fekk:
Buur bu yilifoon suuf yepp, Jongoma ñu goor ñépp naboon, Boroom doole ju kenn yabul, Waliyu wu yàlla masul delloo ag ñaanam, Boroom alal ju jeexalul woon dara,
Ponkal mu ubb mbooleem làmb yi, Sëriñ bu ñépp daa dar, Boroom lijjanti yu loxoom jotoon fepp, ku siiwoon ba ken umpule wu ko ci dénd bi ñoom ñi ñépp tëdd faak ku daa yori sagar ñu naan ko dof bi, ku mesta am lum lekk, ku mesta yilif ab wurmbël, ku laggi ba daawul yékkati ab cér,
1
81
Jàmbaar nga d. Lénn ci faqiih yi parfois duñ sopp ci masala phénomène yu mujj yi. Séen fiqh dañ koy bayyi ca teere fukkeelu xarnu ya. Seetlu naa ci yaw sa xarañe masala yooyu.
Li Sëriñ bi noon
«Gàttub tànk gattuw lammiñ loo am mu doyloo ko»
Lu jamono yàqu-yàqu pexe du génn yi.
131







